TSK

TSK · Exodus 3:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba mu dawee, malaakam Aji Sax ja gis ko fu dend akub bëtu ndox ca màndiŋ ma, mooy bëtu ndox, ba ca yoonu Sur.

malaaka mi ma jot ci bépp loraange— yal na barkeel xale yi, ba ñu saxal sama tur ak samay turi waajur, Ibraayma ak Isaaxa, te giir, ba ne gàññ ci kaw suuf.»

Demal woo magi Israyil, ñu daje, nga ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, moo ma feeñu, ne ma: ‘Gis naa leen, te yég naa li ñu leen di teg ci Misra.

ak xéewali suuf ak la ko fees, ànd ak yiwu ka màkkaanoo ngarab sa doon tàkk, te wàccandoo ci kaw boppu Yuusufa; ak kaaŋi bokkam yay séddooy Aji Sax ji.

Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

Ci biiru ndeyam la kii suufoo ab seexam; kii moo tollu ci dooleem, bëreek Yàlla.

¶ «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Te Musaa ci boppam xamle na ne ñi dee dañuy dekki, na ko téere indee ca mbirum ngarab sa. Mooy ba mu wooyee Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, Yàllay Yanqóoba.”

Acts 7:30 TSK

¶ «Mu teg ca ñeent fukki at, malaaka feeñu ko ca màndiŋu tundu Sinayi, ci biir tàkk-tàkku sawara wu jafal ab gajj.

¶ Ndax kat, bokk yi, buggunu ngeen umple njàqare, ji nu daj ci diiwaanu Asi. Daj nanu coono bu jéggi dayo, te wees sunu kàttan, ba yaakaaratunu woona dund sax.