TSK

TSK · Exodus 3:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ne ma: “Siggil, xool sikket yiy tëb bëy yi yépp, yii dañoo seereer, yee todde, yi ci des tippante, ndaxte gis naa li la Laban di def lépp.

Ba loolu amee ñu fal ay nit ñu leen di ga ca seeni sas, di leen ca fitnaal lool. Noonu la bànni Israyil tabaxale Firawna buuru Misra dëkk, ya ñu naa Pitom ak Ramses, mu def ko ay dencukaayi dund.

Gannaaw loolu Firawna sant waa réew ma yépp, ne leen: «Mboolem doom ju juddu ci Ebrë yi, di góor, sànnileen ca dex ga, waaye lu ciy jigéen, bàyyileen, mu dund.»

Yàlla nag geesu bànni Israyil, ñeewante leen.

«Dellul ba ca Esekiya, sama njiitu ñoñ, nga ne ko: “Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di la wéral, te bu gannaaw ëllëgee dinga dem kër Aji Sax ji.

Éy Aji Sax ji, baaxe ma, gisal naqar wi ma bañ yi teg. Yaa may yékkatee fa bunti ndee,

Bul xañ néew-ji-doole; néew-ji-doole la. Ku tumurànke, bu ko soxore cib àtte,

Xanaa ndax buur suqal mbey mi, ba ñépp jariñoo suuf si.

Amos 4:1 TSK

Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari, yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan. Yeen ñiy torxal néew-ji-doole, di not aji ñàkk te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay, ñu naan!»