Kon nag waxal bànni Israyil ne leen: Man maay Aji Sax ji. Maa leen di sippil, yeen bànni Israyil, li leen waa Misra sëf, te maa leen di teggil njaam, gi ñu leen teg. Maay tàllal sama loxo, dogal mbugal yu kéemaane, ba goreel leen.
TSK
TSK · Exodus 32:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba mu ko defee Musaa ne Aji Sax ji: «Aji Sax ji, loo may mititale, Sang bi? Lu tee nga baaxe ma, xanaa ngay teg sëfub mii mbooloo mépp ci sama kaw?
Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?»
Waaye lu tax ñu génne sunu turu baay ci làngam gi mu bokk, ndax ñàkk doom ju góor? Joxleen nu sunub cér ci biir wàll wi sunu bokki baay yu góor bokk ak sunu baay kay!»
Ma ñaan Aji Sax ji, ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, bul sànk sa ñoñ ñi nga séddoo, ñi nga jote sa màggaay, génnee leen Misra ci sa dooley loxo.
Yàlla da leen doon sànk, bu dul woon ak Musaa, xejjam ba ko kar, àtte leen, mu giif, ba fàkkasu leen.
Aji Sax ji, dëggu nga def, li may tawatsi fi yaw lépp. Teewul ma di la diis mbir: lu tax ku bon di baaxle, bépp workat bu bon di féex?
¶ «Léegi nag yaw Boroom bi, sunu Yàlla ji nu génnee Misraak doole, nun sa mbooloo, nga siiwale ca sa tur ba sunu jonni yàllay tey, noo bàkkaar, noo tooñ.