Buleen ci sujjóotal lenn, buleen ci jaamu lenn, ndax man seen Yàlla Aji Sax ji, Yàlla ju fiir laa. Maay topp doom tooñu waajur, ba ca seen maasi sët, ba ca maasug sëtaati nit ñi ma bañ.
TSK
TSK · Exodus 32:34
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Maay yebal malaaka mu jiitu la, te maa fay dàqe Kanaaneen ña ak Amoreen ña ak Etteen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña,
¶ Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»
Ci biir loolu nu woo Aji Sax ji wall, mu dégg sunu yuux, daldi yebal malaaka, mu génne nu Misra. Léegi nu ngi nii fi Kades, dëkk bi digalook sam réew.
Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon, di seen Yàlla ju leen di baal, te di leen mbugale seeni jëf ju bon.
Lii, duma leen ko dumaa?» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Wii xeet, duma ko fey yoolam?»
¶ Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëgg ub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.»
Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel, lekk yàpp wi, Aji Sax ji buggu ci dara. Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef, mbugale leen seeni moy, te ñoom Misra lañuy dellu.
«Bés bu may mbugale Israyil ay bàkkaaram, damay tasaale sarxalukaayi Betel. Béjjén yi ci cati sarxalukaay ba dog, rot.
Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy, akug jéllaleem, akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?