TSK

TSK · Exodus 33:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji, Yàllay asamaan, moom mi ma jële sama kër baay ak fa ma juddoo, te wax ak man, giñal ma ne ma, dina jox sama askan réew mii, moom ci boppam dina yebal malaakaam, mu jiitu la. Foofa ngay jëlale sama doom soxna.

Dogu naa leena jële ci seen notaange gii ngeen nekke ci Misra, yóbbu leen ca réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, réew mu meew maak lem ja tuuroo.’ ”

¶ «Tiitaange laay yebal, mu jiitu leen. Maay tiital mboolem xeet wu ngeen fekki, te maay def seen noon yépp won leen gannaaw.

Bàyyileen xel bu baax li ma leen sant bésub tey jii. Maa ngii di leen dàqal Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Etteen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñi ak Yebuseen ñi.