Loola la Yàlla wax Ibraayma, daldi fay bàyyikoo.
TSK
TSK · Exodus 33:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu bëccëgee nag Aji Sax ji nekk ci seen kanam ci biir taxaaru niir, di leen jiite ca yoon wa, te bu guddee mu nekk ci biir taxaaru sawara, di leen leeral, ba ñu mana dem guddi ak bëccëg.
¶ Ba Yàlla noppee wax ak Musaa ca kaw tundu Sinayi, da koo jox ñaari àlluway doj yu mu binde loxol boppam.
Bu kenn ànd ak yaw, te bu kenn xand fenn kaw tund wi. Jur gi sax bumu forsi ci suufu tund wi, du gu gudd, du gu gàtt.»
¶ Bu Musaa duggaan ca biir xaymab ndaje ma, ngir wax ak Aji Sax ji, day dégg baat ba di wax ak moom, bawoo fa tiim kubeeru gaalu seedes kóllëre ga, ca diggante ñaari serub ya. Noonu la daan waxeek moom.
Aji Sax ji nag feeñ ca xayma ba, ci biir taxaaru niir, taxaaru niir wa taxaw fa bunt xayma ba.
¶ Gannaaw loolu loxol Aji Sax ji dikk na fa ci sama kaw. Mu ne ma: «Génnal ba ci joor gi, ma wax faak yaw.»