¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
TSK
TSK · Exodus 39:32
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Defarleen gaalu dénku séng, guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll; taxawaayam di xasab ak genn-wàll.
Muy xaymab ndaje mi, ak gaalu àlluway seede si, ak kubeeru saraxu njotlaay gi ci kawam, ak mboolem jumtukaayi xayma bi;
¶ Musaa dellu wax ak mbooloom bànni Israyil mépp ne leen: «Lii mooy li Aji Sax ji santaane.
¶ Ba loolu amee ñu indil Musaa jaamookaay bi: xayma bi ak yëfam yépp; lonku yi ak làcc yi ak galan yi ak jën yeek tegu yi,
¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko:
ndax bu ñuy dugg ci xaymab ndaje mi, ak bu ñuy jegeji sarxalukaay bi, dañuy jàpp, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.
¶ Askanu Gerson nag, seen sas ci wàllu xaymab ndaje mi, jaamookaay bi la woon ak xayma bi, ak malaan mi koy ub, ak ridob bunt xaymab ndaje mi,
¶ Askanu Merari, seen sas moo doon xànqi jaamookaay bi aki galanam ak jën yi ak tegu yi, ak mboolem jumtukaay ya muy àndal, ak liggéey bu ca war,
Ca fukkeelu at maak benn, yemook juróom ñetteelu weer wa, di weeru Bul, ca la kër ga sotti, mook mboolem la ca bokk ak na mu wara bindoo lépp. Suleymaan tabax na kër ga ci juróom ñaari at.
Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla.