TSK

TSK · Exodus 39:37

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn.

Ci biir xaymab ndaje mi la Aaróona ak doomam yu góor di teg làmp yi, ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ñuy fanaanee tàkk ngoon ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, war bànni Israyil fàww, ñoom ak seen askan.

Noonu la Aaróona def. Fa féete tegukaay ba kanam, fa la féetale ay làmpam, muy la Aji Sax ji santoon Musaa.

ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si,