TSK

TSK · Exodus 39:43

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf!

¶ La Aji Sax ji santoon Musaa ak Aaróona, noonu rekk la ko bànni Israyil defe.

daldi taal làmp yi fi kanam Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

¶ «Dogal a ngoogu, di lu leen war fàww, te mooy ñuy joxeel bànni Israyil seen njotlaay benn yoon cim at ngir seen bàkkaar yépp.» Ñu daldi def li Aji Sax ji santoon Musaa.

Daawuda joxe saraxi rendi-dóomal ak saraxi cant ci biir jàmm, ba noppi daldi ñaanal askan wi ci turu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi.

Ci kaw loolu Buur Suleymaan walbatiku, ñaanal mbooloom Israyil mépp, fekk mbooloom Israyil mépp a nga taxaw.

Moo dàq wurus, raw wurusu ngalam wu ne xas; dàqati lem, ëpp tem-tem.