Exodus 28:4
TSK
Yii yére nag lañu koy defaral: kiiraayal dënn ak ab xar-sànni ak ab fëxya, ak mbubb mu gudd mu ñu ràbb, ak kaala ak laxasaay. Yérey sellnga lañuy defal sa mag Aaróona ak doomam yu góor, ngir ñu di ma sarxalal.