TSK

TSK · Exodus 4:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji, Yàllay asamaan, moom mi ma jële sama kër baay ak fa ma juddoo, te wax ak man, giñal ma ne ma, dina jox sama askan réew mii, moom ci boppam dina yebal malaakaam, mu jiitu la. Foofa ngay jëlale sama doom soxna.

malaaka mi ma jot ci bépp loraange— yal na barkeel xale yi, ba ñu saxal sama tur ak samay turi waajur, Ibraayma ak Isaaxa, te giir, ba ne gàññ ci kaw suuf.»

¶ «Te nag man ci sama bopp, maay yebal malaaka, mu di leen sàmm ci yoon wi, ba yóbbu leen bérab ba ma waajal.

Moom ci boppam mu topp màndiŋ ma lu tollook doxub benn bés, doora toog ci taatu benn gajj. Ma ngay ñaan dee, naan: «Doy na sëkk, Aji Sax ji, jëlal sama bakkan rekk, ndax man kat gënuma samay maam.»

Su ma nee: «Xaaral ma fàtte ko, dootuma biral waxyu ci turam,» sama xol bi mel nib taal bu tàkk, tàbbi sama biir yax yi; may jéema muutuwaale sa kàddu, te duma ko man.

Jonah 1:3 TSK

¶ Yunus nag jóg jëm Tarsis, ngir daw Aji Sax ji. Mu àgg fu ñuy wax Yafa, fekk fa gaal gu mag gu jëm Tarsis. Mu fey njég ga, dugg, ànd ak ña ca nekk, jëm Tarsis, ngir daw Aji Sax ji.