TSK

TSK · Exodus 4:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”»

¶ Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: «Teelala xëy ëllëg ca Firawna, buy génn jëm ca ndox ma, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma.

¶ Ba loolu wéyee Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, nga ne ko: Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.

¶ Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.

te lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, dina dee, dale ko ci taaw bu góoru Firawna, mi toog ci jal bi, ba ci taaw bu góoru jaam bu jigéen bu féetewoo wol, boole ci luy taaw bu góor ci jur gépp.

Ba Firawna tëwee, bañ noo bàyyi, nu dem, Aji Sax jee rey mboolem lu doon taaw bu góor ca réewum Misra, taawu nit ba ci taawu mala. Looloo waral nuy rendil Aji Sax ji mépp mala mu jëkka juddu, di góor, sunu bépp taaw bu góor it, ñu war koo jote sarax su nu koy rendil.”

Moo fàdd luy taaw ca seenum réew, muy lu jëkka soqeekoo seen digg doole.