«Sàkkal mbalkam njàpp mu xànjar, ak tegub xànjaram ngir ñu di ko jàppe. Teg ko ci diggante xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te nga duy ko ndox.
TSK
TSK · Exodus 40:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 30:18
TSK
Exodus 40:30
TSK
¶ Ba loolu amee ñu teg mbalkam njàpp mi ci diggante xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, ba noppi duy ko ndoxum njàpp.
Zechariah 13:1
TSK
¶ «Bésub keroog bëtu ndox dina bënnal kër Daawuda, ak waa Yerusalem, ngir setal bàkkaar ak sobe.
Hebrews 10:22
TSK
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu, ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Revelation 1:5
TSK
tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf. Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,