TSK

TSK · Exodus 5:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te wax naa la ne la, nga bàyyi sama doom, ndax mu man maa jaamu, nga bañ. Kon nag dinaa rey sa taaw bu góor.’ ”»

Ñoom ñooñu ñoo wax ak Firawna buuru Misra, ngir génne bànni Israyil Misra; du keneen ku dul Musaa ak Aaróona.

Wax ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi, moo ma yónni ci yaw. Mu di la wax, ne la: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu jaamuji ma ca màndiŋ ma.’ Yaw nag booba ba tey yaa ngi tanqamlu.

Ndaxte soo bàyyiwul sama ñoñ, ñu dem kat, dinaa yuri ay ndiiraani weñ yuy màtte ci seen kaw, yaak say dag ak sa waa réew, te dinañu àgg ci sa biir kër. Këri waa Misra dina fees ak weñ yuy màtte, ba suuf, si ñu taxaw sax, weñ yee koy muur.

¶ Ba loolu wéyee Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, nga ne ko: Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.

¶ Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.

Musaa ne ko: «Nun ñépp ay dem kay, mag ak ndaw; danuy dem, ànd ak sunuy doom, góor ak jigéen, ak sunuy jur, gu gudd ak gu gàtt, ndax màggalug Aji Sax ji la ci nun.»

Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, te duma rus.

Waaye yaw nit ki, bu leen ragal, bul ragal seeni wax. Xam naa ne ay taxas aki dég a lay wër, nga toog ci kawi jiit. Waaye bul ragal seeni wax te bul tiit seen kanam doonte kërug fippukat lañu.

Acts 4:29 TSK

Léegi nag Boroom bi, bàyyil xel seeni tëkkoo te nga may nu, nun say jaam, nuy waxe sa kàddu fit wu mat sëkk.