TSK

TSK · Exodus 5:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba mu ko defee Musaa ne Aji Sax ji: «Aji Sax ji, loo may mititale, Sang bi? Lu tee nga baaxe ma, xanaa ngay teg sëfub mii mbooloo mépp ci sama kaw?

Moom ci boppam mu topp màndiŋ ma lu tollook doxub benn bés, doora toog ci taatu benn gajj. Ma ngay ñaan dee, naan: «Doy na sëkk, Aji Sax ji, jëlal sama bakkan rekk, ndax man kat gënuma samay maam.»

Ana ku ma am asamaan ku la moy? Ku ma safoo kaw suuf ku la moy?

Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma, ma naagu, nga nax ma, jaay ma doole, ba man ma. Ñu ngi may kekku bés bu ne, ku ne di ma kókkali.