TSK

TSK · Exodus 6:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat,

Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.

Réew, mi ma sédd Ibraayma ak Isaaxa, yaw laa koy sédd, yaak askan wi soqikoo ci yaw.»

Te itam damaa fasoon ak ñoom kóllëre, ngir jox leen réewum Kanaan, réew ma ñu nekkoon ay doxandéem.

Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: “Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”»

Xanaa maa ëmb mii mbooloo mépp, am maa leen jur, ba nga di ma leen bootloo fàpp, ni jaboot di boote luy nàmp, jëme leen réew, ma nga giñaloon seeni maam?

Ndax seen Yàlla Aji Sax ji Yàllay yërmande la. Du leen wacc, du leen yàqte te du fàtte kóllëre, ga mu fasoon ak seeni maam ci kaw ngiñ.

Te Aji Nekk-Fàww ju Israyil ji du fen, du réccu, ndax du nit bay réccu.»

¶ «Nanga leen wax, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ba ma tànnee Israyil, maa giñal askanu waa kër Yanqóoba woowa. Maa leen xamal maay kan ca réewum Misra, giñal leen, ne leen: Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Ba tey maa leen giñal ca màndiŋ ma ne dinaa leen tasaare ci biir xeet yi, wasaare leen ci biir réew yi.

Dingeen xam ne maay Aji Sax ji, gannaaw bu ma leen délloosee ci biir suufas Israyil, réew ma ma giñaloon seeni maam, ne dinaa leen ko jox.

Nangeen ko séddoo, ku nekk yem ak sa mbokk cér, ndax maa giñal seeni maam, ne dinaa leen ko jox. Kon réew mii, seen cér bu leen lew la.