TSK

TSK · Exodus 7:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Magi Israyil dinañu la déggal, su ko defee nga ànd ak ñoom, dem ca buuru Misra. Waxleen ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi moo nu feeñu. Kon nag ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji ay sarax.”

¶ Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”»

Aji Sax ji def loola, weñ yi def ndiiraan yu réy, song kër Firawna ak kër dagam ya, dajal réewum Misra, ba réew ma yàqu ndax ndiiraani weñ ya.

¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Teelala xëy ca Firawna ëllëg, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji, Yàllay Ebrë yi, dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.

Ba Firawna tëwee, bañ noo bàyyi, nu dem, Aji Sax jee rey mboolem lu doon taaw bu góor ca réewum Misra, taawu nit ba ci taawu mala. Looloo waral nuy rendil Aji Sax ji mépp mala mu jëkka juddu, di góor, sunu bépp taaw bu góor it, ñu war koo jote sarax su nu koy rendil.”

Waa Filisti dégg coow la, ne: «Waaw, coow lu réy loolu ca dalub Ebrë ya, lu mu doon?» Ba waa Filisti yégee ne gaalu kóllërey Aji Sax ja dugg na ca biir dal ba,

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bànni Israyil ak Yuda, ñépp lañu notandoo. Ñi leen jàpp ñépp téyee leen doole, bañ leena ba.