TSK

TSK · Exodus 9:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su ko defee nga wax Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Israyil mooy sama taaw bu góor.

¶ Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”»

Aji Sax ji def loola, weñ yi def ndiiraan yu réy, song kër Firawna ak kër dagam ya, dajal réewum Misra, ba réew ma yàqu ndax ndiiraani weñ ya.

¶ Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.