TSK

TSK · Exodus 9:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ne ko: «Nay ëllëg.» Musaa ne ko: «Baax na, ndax nga xam ne sunu Yàlla Aji Sax ji amul moroom.

Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama kóllëre ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom,

¶ Gannaaw loolu Suleymaan taxaw jàkkaarlook sarxalukaayu Aji Sax ji, fa kanam mbooloom Israyil mépp. Mu daldi tàllal ay loxoom asamaan,

Ezra 9:5 TSK

Saraxu ngoon jot, ma jóge ca sama jataayu toroxtaange, ba ma xottee sama turki baak sama mbubb ma. Ma ne gurub sukk, tàllal sama Yàlla Aji Sax ji loxo,

Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax jee moom suuf ak li ko fees, ak àddina ak li ci biiram.

Moo moom xóotey suuf, moom colli tund yi,

Ma tàllal lay loxo, di la sàkku, ni suuf su mar di sàkkoo ndox. Selaw.