¶ «Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan yi ba ca asamaani asamaan ya manu laa fat, waxumalaa kër sii ma tabax.
TSK
TSK · Ezra 1:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu ne ko: “Ndab yii, jël ko yóbbu ca kër Yàlla ga ca Yerusalem, te nañu tabaxaat kër Yàlla ga fa mu nekkoon.”
Su ko defee ñu mana sarxalal Yàlla Boroom asamaan lu ko neex tey ñaanal Buur aki doomam gudd fan.
¶ Ba ma déggee kàddu yooyu, damaa toog di jooy, ñaawlu ko ay fan, di woor ak a ñaan ci Yàlla Boroom asamaan.
Éy Aji Sax ji, yaa baaxe woon sa réew mi, ba suqli sëti Yanqóoba yi,
Ana ku ñu yékkatee penku, woo ko ci tànki njekk? Ana ku ko jébbal xeet yi, nangulal ko buur yi, saamaram note ba ñuy pënd, fittam jamat, tasaare ni boob?
Aji Sax ji dafa wax ki mu fal, Buur Sirus mi mu jàpp ci loxol ndijooram, ngir nangulal ko xeet yi, yolomal ngañaayal buur yi, lafal koy bunt, ba bunti dëkk du tëje,
Aji Sax ji dafa wax ne: «Asamaan sama ngàngunee, suuf di sama ndëggastal. Ana kër gu ngeen may tabaxal man? Ana ban bérab ay sama dal-lukaay?
Man maa sàkk suuf, sàkk doom aadama ak mala fi kaw suuf ci sama doole ju bare ak sama kàttan gu matale, te loolu lépp, maa ko jox ku ma neex.
¶ Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Bu Babilon matalee juróom ñaar fukki ati kilifteefam, dinaa leen dikkal, sottalal leen sama kàddug jàmm, ba délloosi leen bérab bii.
Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.
Yaw Buur, buuru buur yi, yaw mi Yàlla Boroom asamaan jox nguur ak kàttan ak dooleek ndam,
Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»
xanaa ngay diirook Boroom asamaan, bay santaane ñu indil la ndabi këram, nga di ci naan biiñ, yaak say jawriñ ak say soxna ak say nekkaale, ngeen di sàbbaal ay yàllay xaalis ak yu wurus ak yu xànjar ak yu weñ ak yu bant ak yu doj, te du ci lenn luy gis mbaa muy dégg mbaa mu xam dara. Waaye Yàlla ji yor sa bakkan tey ak ëllëg sàbbaaloo ko.