¶ Ci kaw loolu buurub Asiri jële ay nit dëkk ya ñuy wax Babilon ak Kuta ak Awa ak Amat ak Sefarwayim, dëël leen dëkki Samari, ñu wuutu bànni Israyil. Ñu daldi moom diiwaanu Samari, féetewoo dëkk ya.
TSK
TSK · Ezra 4:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Noonu la xeet yooyu daan wormaale Aji Sax ji, boole ci di jaamu seen jëmmi tuur. Seeni doom it noonu, ba tey seeni sët di def na seeni maam daan def.
¶ Ba mu ko defee ña jiite waa kër Yuda ak Beñamin ak sarxalkat yaak Leween ña, képp ku ci Yàlla xiir rekk, mu daldi dem tabaxi kër Aji Sax ja ca Yerusalem.
Ba mu ko defee Yosuwe doomu Yoccadag, mook moroomi sarxalkatam, ak Sorobabel doomu Selcel aki bokkam daldi tabax sarxalukaayu Yàllay Israyil, ngir sarxal ca saraxu dóomal ba, mu dëppook li ñu bind ci téereb yoonu Musaa, góorug Yàlla ga.
Dañuy ñaawle, di wax lu bon, di réy-réylu, boole ci kàdduy jaay-doole.
Ba mu ko defee Senakerib buurub Asiri daldi fabu, ñibbi. Mu toog nag ca Niniw.
Ñooñu ay ndawi caaxaan lañu, ay liggéeykat yu njublaŋ yu mbubboo ndawi Almasi.
Noonee Sànnes ak Sàmbres doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm.