¶ Ci biir loolu mu am ay nit ñu ab néew tax ñu sobewu, ba manuñoo màggal bésub Mucc bi bésub keroog. Ñu dikk ba ci Musaa ak Aaróona ca bés ba.
TSK
TSK · Ezra 6:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Su dee ab doxandéem bu ngeen dëkkal, sañ naa màggal bésub Mucc bi ñeel Aji Sax ji. Na mu dëppook mboolem dogali yooni bésub Mucc, ak àttey yoonam, ni la koy màggale; benn dogal bi lay doon ci yeen, muy doxandéem bi, di njuddu-ji-réew.»
¶ Gannaaw ba loolu wéyee njiit ya dikk, ne ma: «Du bànni Israyil, du sarxalkat yi, du Leween ñi, kenn ci ñoom teqlikoowul ak xeeti réew meek seen aada yu siblu. Dañuy jëfe ni Kanaaneen ñeek Etteen ñeek Periseen ñeek Yebuseen ñeek Amoneen ñeek Mowabeen ñeek waa Misraak Amoreen ñi.
Ci kaw loolu askanu Israyil beddeeku doxandéem yépp. Ñu taxaw nag, tudd seen bàkkaari bopp ak seen ñaawtéefi maam.
Say santaanee wér te wóor; Aji Sax ji, sellnga la sa kër jagoo bésoo bés.
Maa leen di wis ndox mu set, ngeen set. Mboolem seen sobe ak mboolem seen kasaray tuur laa leen di setalal.
¶ Gannaaw noo moom yii dige nag, soppe yi, nanu setal sunu bopp ci mboolem sobey yaram, ak ju xel, te nu matal sellnga ci ag ragal Yàlla.