¶ Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.»
TSK
TSK · Genesis 1:27
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam,
Ku tuur deretu nit, na nit tuur deretam, ngir melokaanu boppam la Yàlla sàkke nit.
Naa la sante sama bind bu raglu bii te yéeme, say jalooree di kéemaan, bir na ma!
Takkleeni jabar, am ci doom yu góor ak yu jigéen. Takkal-leen seen doom ay jabar, maye seen doom yu jigéen, ñu am ñoom it doom yu góor ak yu jigéen. Yokkuleen fa, buleen fa néew.
Góor moom du muur boppam, ndax mooy takkndeeru Yàlla te moo taxawe darajay Yàlla. Waaye jigéen moo taxawe darajay góor,
te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub, ak sellnga ji dëgg di jur.
Kàddu googu moo di mbóot mi masoona làqu maasoo maas, waaye tey Yàllaa ko xamal ay nitam ñu sell.