Genesis 1:11
TSK
¶ Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Yàlla ne: «Na suuf sax ñax, muy gàncax gu ànd ak jiwoom, ak garab yuy meññ tey jur seeni jiwu, lu ci nekk ak wirgoom ci kaw suuf.» Mu daldi nekk noona.
¶ Yàlla ne: «Na suuf génne ay bindeef, mu ci nekk ak wirgoom: ag jur, luy raam aki rabi àll, lu ci nekk ak wirgoom.» Mu daldi nekk noona.
Ana ku tëjoon lafi buntu géej, ba muy buccikoo xóote ya, fettax,
Yaa ballal bëti ndox ya ca xur ya, ñuy wale digg tund ya,
Màggal-leen ko, yeen asamaani kaw-li-kaw, ba ca ndox ma tiim asamaan ya.
Xàmbaar bu duyee, ba fees, fi kaw suuf lay soob. Garab, bu daanoo ndijoor mbaa càmmoñ, fa mu daanu lay des.