¶ Gannaaw ba Teraa amee juróom ñaar fukki at, am na Ibraam ak Naxor ak Aran.
TSK
TSK · Genesis 11:31
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75).
Booba lañu yóbbu Lóot ma dëkk Sodom, te Ibraam di baayam bu ndaw. Ci biir loolu ñu yóbbaale li mu amoon lépp, dem.
¶ Ba loolu amee surga ba jële fukki giléem ca giléemi sangam, dem, yóbbaale li gën ci mboolem xeeti alalu sangam. Ma nga jëm réewu Mesopotami, ga Naxor dëkk.
Kon doom, defal lii ma lay wax, demal làquji fa sama càmmiñ Laban ca Karan,
¶ Yanqóoba ne leen: «Bokki fan?» Ñu ne ko: «Karan.»
Xeet yi samay maam sànk, seeni tuur dañu leena musal, muy Gosan, di Karan, di Resef, di askanu Eden wa woon ca Telasar?
Eccen ne ko: «Yeen bokk yi, yeen samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom daraja moo feeñu woon sunu maam Ibraayma, ba mu nekkee réewum Mesopotami, bala moo sanc Karan.