TSK

TSK · Genesis 12:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba ñu demee, ba metitu xiif bi dajal réew mépp, Yuusufa dafa ubbi denc yépp, di jaay pepp mi waa Misra,

Doomi Israyil ñëw nag ci biir ñiy jëndsi pepp, ndax xiif bi lawoon na ba Kanaan.

Yàlla ne ko: «Man maay Yàlla, di sa Yàllay baay. Bul ragala dem Misra, ndaxte askan wu réy laa fay sose ci yaw.

Ruth 1:1 TSK

¶ Ba njiit ya daan àtte faloo ca Israyil, jamono jooju dafa amoon xiif ca réew ma. Jenn waay bàyyikoo Betleyem ca diiwaanu Yuda, ànd ak soxnaam ak ñaari doomam yu góor, ñu toxuji ca réewum Mowab.

¶ Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas, ma dëkk Tisbi ga ca Galàdd, wax Axab, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, di Yàllay Israyil ji may jaamu: at yii nu nekk, du taw te du lay, lu moy dama koo wax ci sama làmmiñ.»

Xiif bu metti am ca Samari ndax gaw ba, ba boppub mbaam-sëf di jar juróom ñett fukki dogi xaalis, genn-wàll liibaru jonkanu pitax di jar juróomi dogi xaalis.

¶ Am na bés Alyaasa wax ndaw sa mu dekkaloon doomam ju góor ne ko: «Ayca, àndal ak sa njaboot, ngeen dali fu ngeen mana dal, ndax Aji Sax ji dogal na ab xiif ci réew mi, te dina am juróom ñaari at.»

di wëreelu ci biir xeetoo xeet, ak nguuroo nguur,

¶ Kàddug Aji Sax jii dikkaloon na Yeremi, jëm ca maral ma. Mu ne:

Acts 7:11 TSK

¶ «Ci kaw loolu ab xiif dikkal Misra gépp ak réewum Kanaan. Mu metti lool. Sunuy maam nag amatuñu ab dund.