TSK

TSK · Genesis 13:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Loolu wees Aji Sax ji yóbbu ko ci biti ne ko: «Xoolal asamaan, te waññ biddiiw yi, ndegam man nga ko.» Mu dellu ne ko: «Noonu la sa askan di tollu.»

Dinaa la defal njaboot gu ne xas, ay xeet sosoo ci yaw, ba ay buur soqikoo ci yaw.

Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa.

Doomu jaam bi it, dinaa ci lawale aw xeet nag, ndaxte yaa ko jur.»

¶ Ibraayma jëlaat na soxna su tudd Ketura,

Yal na la Yàlla Aji Man ji barkeel, nga jaboot lool te sa giir yokku, ba sos ay mboolooy askan.

Maa ngi lay ñaan, nga musal ma ci sama loxol mag Esawu, ndaxte ragal naa, mu ñëw bóom ma, bóomaale jigéen ñi ak seeni doom.

Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw askan ak mboolooy askan sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño.

Yàlla ne ko: «Man maay Yàlla, di sa Yàllay baay. Bul ragala dem Misra, ndaxte askan wu réy laa fay sose ci yaw.

Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: “Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”»

Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen ful, ba yeena ngii tey, bare ba tollu ni biddiiwi asamaan.

¶ Waa Yuda ak Israyil dañoo bare woon, ba mel ni feppi suufas géej, di lekk, di naan, nekke mbégte.

Céy su ngeen sàmmoon samay santaane, ba jàmm baawaanal leen, njekk géejal leen,

¶ Kon nag dige Yàlla boobu, ngëm moo ko waral, ngir mu di aw yiw doŋŋ. Noonu la dige bi doone lu wóor, ñeel ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp; du ñi bokk ci yoonu Musaa rekk, waaye ñeel na itam ñi bokk ci ngëmu Ibraayma, miy sunu maam, nun ñépp.

¶ Gannaaw loolu ma jekki gis mbooloo mu réy mu kenn manula waññ, ñu bawoo ci askan yépp ak giir yépp ak xeet yépp ak làmmiñ yépp. Ñu ngi taxaw fi kanam ngàngune mi ak Gàtt bi, sol mbubb yu weex, ŋàbb ay cari garabi tàndarma.