TSK

TSK · Genesis 13:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa.

Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat,

Teewul sàmmi Gerar di soowook sàmmi Isaaxa naan: «Nun noo moom ndox mi.» Mu tudde teen ba Eseg (mu firi Coow), ndax li ñu soowoo ak moom.

Ay sàmm agsi, dàq leen. Musaa wallu jigéen ña, wëggal leen seen jur.

ak bokkaale, ak xërëm, ak mbañeel, ak féewaloo, ak kiñaan, ak mer mu ëpp, ak jiital say bëgg-bëgg, ak réeroo, ak xàjjalikoo,

¶ Jëfeleen xel mu rafet seen diggante ak aji gëmadi ñi ci biti, te jot gu ngeen am, fexeleen ba jariñoo ko.

Titus 3:3 TSK

¶ Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef, ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon, ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.

James 4:1 TSK

¶ Ana fu jote yeek xuloo yi ci seen biir jóge fu moy seen bànneexi bakkan, yiy xare ci seen yaram?