TSK

TSK · Genesis 14:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

kàddug kiy dégg waxi Yàlla, kiy xame ca xam-xamu Aji Kawe ji, Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.

¶ Daawuda yónnee ay ndaw ca waa Yabes Galàdd, wax leen ne leen: «Yal na leen Aji Sax ji barkeel ndegam yeena jëfe ngor seen digganteek seen sang Sóol, ba rob ko.

Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko, di fey Aji Kawe ji loo dige,

Yàlla siiw na fa Yuda, aw turam màgg fa Israyil.

Aji Sax jee ko giñ, te du dellu gannaaw: «Yaa dib sarxalkat ba fàww, topp dayob Melkisedeg.»

Micah 6:6 TSK

Ana lu may dikkaale fi kanam Aji Sax ji, ba sujjóotal Yàlla jooja fa kaw. Tee ma koo dikke ay rendi-dóomal, ay wëlluy menn at?

Acts 7:48 TSK

¶ «Moona Aji Kawe ji du dëkke lu loxo defar, mooy la yonent ba ne:

Kon nag bi nu koy jekku, nanuy def lu baax, ngir ñépp, rawatina waa kër yoonu ngëm wi.

Ci biir loolu Yàlla tudde ko sarxalkat bu mag, bi topp dayob Melkisedeg.

Ndax ba Melkisedeg di gatandu Ibraayma, Lewi ma nga woon ca geñog Ibraayma maamam.