ma giñloo la ci Aji Sax jiy Yàllay asamaan ak suuf ne doo jëlal sama doom soxna ci biir jigéeni waa Kanaan, gi ma dëkk ci seen biir.
TSK
TSK · Genesis 14:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Isaaxa ne ko: «Jottli ma fii ma lekk ci sam rëbb, doom, ba ñaanal la ci sama xol.» Yanqóoba jottli Isaaxa ndab li, mu lekk, daldi koy may biiñ, mu naan.
Ba mu ko defee Yanqóoba ñaanal Firawna, bàyyikoo fa, daldi dem.
Ñooñu ñoo sos mboolem giiri Israyil, ñu tollu ci fukk ak ñaar, te loolu la leen seen baay wax, ba mu leen di tàggu. Ku ci nekk mu tàggoo ko kàdduy tàggtoo, ya war ca moom.
Seen Yàlla Aji Sax ji déy mooy boroom asamaan, ak asamaani asamaan, ak suuf, ak mboolem li ci biiram.
¶ Daawuda yónnee ay ndaw ca waa Yabes Galàdd, wax leen ne leen: «Yal na leen Aji Sax ji barkeel ndegam yeena jëfe ngor seen digganteek seen sang Sóol, ba rob ko.
Maay boroom raboo rabu àll, ak junniy nag yuy fore tund ya.
Asamaan, asamaanu Aji Sax jee, suuf la dénk doom aadama.
¶ Ca waxtu woowa tembe la kemtalaayu mbégte tukkee ci Noo gu Sell gi, dugg Yeesu, mu daldi ne: «Baay, Boroom asamaan ak suuf, sant naa la, nde yaa làq lii boroom xam-xam yeek boroom xel yi, xamal ko tuut-tànk yi, nde loolu de, Baay, mooy li la soob.
¶ Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi, mi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi mi nu bokk, fa déndi asamaan ya.
Waaye Melkisedeg mi ñu askanalewul giirug Lewi, ci Ibraayma la nangoo cérub fukkeel. Te it moo ñaanal barke Ibraayma mi jagoo digey Yàlla.