daldi ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, sama Yàllay sang, Ibraayma, moom mi masula noppee laaye biir sama sang, te masu koo ñàkke worma. Man it, Aji Sax ji wommat na ma ba sama kër bokki sang!»
TSK
TSK · Genesis 14:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu nu àggee ci ngóob, juróom yu ngeen am dingeen ci jox Firawna benn, te féetewoo ñeenti cér yi des. Su ko defee ngeen génne ci jiwuy tool yi, li ci des ngeen dunde, yeen ak seen waa kër ak seeni doom.»
¶ «Bu loolu weesee mboolem lu jóge ci suuf, muy pepp mbaa doomi garab, cérub fukkeel ba Aji Sax jeey boroom. Dees koy sellalal Aji Sax ji.
Seen céru fukkeelu pepp nag, ak bu biiñ bu bees, ak bu diw gu bees, ak seen taawug jur gu gudd ak gu gàtt, ak seen mboolem saraxi xas yu ngeen xasoo woon, ak seen saraxi yéene, ak ab jooxe bu ngeen sàkke ci seenu ñaq, sañuleen cee lekk lenn ci seen biiri dëkk,
¶ Ñetti at yu mat yu nekk, nangeen génne mboolem seen céri fukkeeli meññeef ca at mooma, te ngeen denc ko ca seen biir dëkk,
Ci kaw loolu Ayimaas àddu ca kaw, ne Buur: «Jàmm la!» daldi sujjóotal Buur, dëpp jëëm fa suuf, ne ko: «Buur, sang bi, cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi teg ci sa loxo ña la doon fexeel.»
Ba mu ko defee waa Yuda gépp dellu di indi ca biir néegi dencukaay ya céri fukkeel ya ñuy génne, di pepp ak biiñ aku diw.
Yaa yéeg fa kawa kaw, jàpp ay jaam, yóbbaale. Yaa nangooy galag ci nit ñi, ba ci ñiy fippu ndax li Yàlla Ki Sax dëkke Siyoŋ.
Ñeel Daawuda. Cant ñeel na Aji Sax ji ma sës, mu di ma jàngal xeex, di ma tàggat ngir xare,
Waaw, nit dina sàcc Yàlla? Ndaxam yeen yeena ngi may sàcc te yeena ne: “Ana nu nu la sàcce?” Xanaa ci seen cérub fukkeelu alal akub jooxe.
Maa ngi woor ñaari yoon, ayu bés gu nekk, di joxe asaka benn céru fukkeelu mboolem lu ma am.”
¶ Cant ñeel na Yàlla sunu Baayu Sang Yeesu Almasi, mi nu baaxe bépp barkey biir, ci Almasi mi nu bokk, fa déndi asamaan ya.
¶ Cant ñeel na Yàlla, sunu Baayu Sang Yeesu Almasi! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju yaa, ci dooley ndekkitel Yeesu Almasi, ngir may nu yaakaar juy dund.