Gannaaw loolu Aran faatu na lu jiitu faatug baayam Teraa, ca réew ma mu juddoo, di Ur, dëkku Kaldeen ña.
TSK
TSK · Genesis 15:7
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 11:28
TSK
Genesis 12:1
TSK
¶ Aji Sax ji moo waxoon Ibraam, ne ko: «Jógeel sam réew, jóge ci say bokk ak sa kër baay, te nga dem ca réew mi ma lay won,
Genesis 13:15
TSK
ndaxte réew, mi ngay gis mépp, yaw laa koy may ba fàww, yaak askan wi soqikoo ci yaw.
Numbers 33:53
TSK
Defleen réew mi moomeel, ngeen dëkke ko, ndax yeen laa jox réew mi, ngir ngeen moom ko.
Nehemiah 9:7
TSK
Yaw yaa di Aji Sax ji, Yàlla ji tànn Ibraam, jële ko Ur gu waa Kalde, tudde ko Ibraayma.
Psalms 105:42
TSK
Daa bàyyi xel kàddoom gu sell, ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba.
Acts 7:2
TSK
Eccen ne ko: «Yeen bokk yi, yeen samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom daraja moo feeñu woon sunu maam Ibraayma, ba mu nekkee réewum Mesopotami, bala moo sanc Karan.