Genesis 16:5
TSK
¶ Sarayi nag wax Ibraam ne ko: «Tooñ gi ma Ajara di tooñ, yaa ma ko yóbbe! Maa la jox sama jaam, ngir nga dëkkoo ko, naam, waaye moom, naka la yég ne ëmb na rekk, daldi indi yabeel sama digganteek moom. Kon yal na ma Aji Sax ji àtteek yaw!»