Genesis 32:28
TSK
Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
¶ Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Oseya doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe.
Su boobaa xeet yi gis sag njekk, buur yépp gis sa daraja, ba ñu di la tudde tur wu yees, wu Aji Sax ji di tuddal boppam.
Ca suba sa Pasur yiwee ko ca jéng ba. Yeremi ne ko: «Aji Sax ji tuddeetu la Pasur; Magor-Misabib (mu firi Tiitaange lu dajal) la la tudde.
Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa la def ngay maamu xeet yu bare.» Ibraayma mooy sunu maam fi kanam Ki mu gëm, te muy Yàlla miy delloo ñi dee, bakkan, tey woo lu nekkul, mu doon lu nekk.