TSK

TSK · Genesis 19:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba ñu leen génnee, kenn ci ñoom ne Lóot: «Dawal sa xélu bakkan, bul geestu, bul taxaw fenn ci joor gi. Dawal ca tund ya, bala ngaa dee.»

Ña faalewul kàddug Aji Sax ji, ñoom, wacc seeni jaam ak seeni jur ca biti.

«Xiddileen mbooloo mii, ma xoyom leen léegi!»

Tee ngeena baña kókkalee bala ñoo teeŋal seeni jéng? Sànkute kat moo di dogal bi ma dégg, mu bawoo fa Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi, di luy dikkal réew mi mépp.

Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma, ma naagu, nga nax ma, jaay ma doole, ba man ma. Ñu ngi may kekku bés bu ne, ku ne di ma kókkali.

¶ «Noonee itam la deme woon ca janti Lóot. Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jënd ak a jaay, di jëmbat ak a tabax.

¶ Naka lañu dégg waxi ndee-ndekki, ñenn ña di ko foontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu, nga waxalaat nu ci moomu mbir.»

¶ Ci kaw loolu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan, ne: «Yeen sama ñoñ, génnleen dëkk bii, bala ngeena bokk ak moom ay bàkkaaram, bay séddu ci mbugalam.