TSK

TSK · Genesis 19:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Gan ña nag dem, jublu Sodom, Ibraayma moom taxaw ba tey fi kanam Aji Sax ji.

Nanga gaaw nag, làquji fa, ndax duma mana def dara te àgguloo ca.» Loolu moo tax ñu tudde dëkk boobu Sowar (mu firi Bu tuut).

¶ Sóol yebal ay ndaw ca kër Daawuda ngir ñu xoolal ko ko, ba bët set, ñu rey ko. Mikal, soxnas Daawuda, yégal ko Daawuda, ne ko: «Soo rawalewul sa bakkan ci guddi gi de, bu ëllëgee dees na la rey.»

¶ Ilyaas gis na mu deme, daldi daw, ngir rawale bakkanam. Mu dem ba Beerseba ca réewum Yuda, bàyyi fa surgaam.

Ñu naan: “Dawleen, rawale seen bakkan, ba tumurànkeji ni gajju màndiŋ!”

ndax lekk gi, bakkan bee ko ëpp solo, te koddaay li it, yaram wee ko ëpp solo.

Bokk yi, fooguma ne jot naa ci, xanaa kay lenn: damay fàtte li ci gannaaw, te def lu ma man, ngir fexee yóotuji li ci kanam,