TSK

TSK · Genesis 19:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;

¶ Aji Sax ji ne Musaa: «Loolu nga wax, moom laa lay defal, ndax daj nga samaw yiw, te it maa la xam ci saw tur.»

Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.

Nammeelu ku ko ragal, mu sottal; yuuxam, mu dégg, musal.

Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.