¶ Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.
TSK
TSK · Genesis 19:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 13:10
TSK
Genesis 32:25
TSK
Mu des fa nag moom doŋŋ. Kera la genn góor fanaana bëre ak moom, ba bët set.
Deuteronomy 9:14
TSK
Bàyyi ma rekk ma faagaagal leen, ba far seen tur fu asamaan tiim, te def la ngay xeet wu ëpp wii, ëpp ko doole.»
Psalms 91:1
TSK
Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji yaa këroo keppaaru Aji Man ji.
Isaiah 65:8
TSK
Aji Sax ji dafa wax ne: «Ni nit di gise cabbu reseñ ju fees dell, ne: “Buleen ko yàq, ngëneel a ngi ci,” noonu laay def ngir sama jaam ñi, baña boole lépp yàq.
Titus 1:2
TSK
Ngëm googu, ak xam-xam boobu, ñu ngi sukkandiku ci yaakaar, ji nu am ci texe ba fàww, te googu texe, Yàlla mi dul fen, moo ko dige ba àddina sosoogul.