TSK

TSK · Genesis 19:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba mu waxee ba noppi, Lóot dafa xool, gis joor, gi wër dexu Yurdan gépp, màndi ndox. Ndax laata Aji Sax jiy tas dëkk yu ñuy wax Sodom ak Gomor, àll bi jëm Sowar dafa naatoon, ni réewum Misra naate, ba faf mel ni toolub Aji Sax ja.

tamarax ak xorom, ak lakk gi ci seen réew mépp, ba du lenn lees fay ji, mbaa lu fay jebbi, mbaa genn gàncax gu fay saxe, mbete tastey Sodom, ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, dëkk ya Aji Sax ji tas, ca meram ma ak sànjam ma,

Job 18:15 TSK

manees naa dëkke xaymaam, moomatu ko, tamarax lees fay suy.

Bu nu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi waccalul woon li nu deseek as néew, ni Sodom lanuy mel, Gomor lanuy neexool.

Yal na kooku mel ni dëkk, yi Aji Sax ji tas te yërëmu leen! Yal na dégg yuuxi suba teel ak xaacuy xarey njolloor.

Edom day tas ni Sodom ak Gomor ak la ko wër.» Aji Sax jee ko wax. «Nit du ca dëkk, doom aadama du fa dal.

Sama ñaawtéefu askan wee màgg, ba raw ñaawtéefu waa Sodom, dëkk ba jekki jàllarbiku, te loxo laalu ko.

«Efrayim, ana nu ma lay baye, yaw Israyil laa ne, nu ma lay tege ciy loxo? Ana nu ma lay defe ni Atma? Nu ma lay yemaleek Ceboyim? Sama xol a bëpp, sama yërmandee yëngu.

Moo tax, giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax ju gàngoor yee, Yàllay Israyil, «Mowab déy ni dëkkub Sodom lay mujje, Amoneen ñi mel ni Gomor, ay dég ak paxi xorom a koy nangu, mu gental ba fàww. Sama ndesu ñoñ a leen di sëxëtoo, ndesu xeet wi ma séddoo moo leen di moom.»

¶ «Noonee itam la deme woon ca janti Lóot. Nit ñaa nga doon lekk ak a naan, di jënd ak a jaay, di jëmbat ak a tabax.

Jude 1:7 TSK

Naka noonu itam Sodom ak Gomor, ak dëkk ya leen wër, ñoo yebu woon ci powum séy, ak jaxasoo gu woroo ak bindub judduwaale, ba ñu def leen misaal, ñeel ña nara tegoo mbugalum sawara wu sax dàkk.