TSK

TSK · Genesis 19:31

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur.

Loolu wees Ibraam dëkkoo Ajara, mu daldi ëmb. Ajara yég ne ëmb na, indi nag yabeel digganteem ak sangam Sarayi.

Yuda ne Onan: «Demal ci sa jabaru mag, donn ko, ndax nga giiral sa mag aw askan.»

¶ Bu ay góor yu bokk waajur dëkkee, kenn ci ñoom dee te bàyyiwul doom ju góor, jabaru ki dee du génn, di séy akub jaambur. Jëkkëru donaleem ju bokk ak jëkkëram moo ko wara jël, donloo ko.