TSK

TSK · Genesis 19:38

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee Aji Sax ji ne ma: «Buleen dal ci kaw Mowabeen ñi, di leen song ub xare, ngir duma leen jox benn cér ci seenum réew, ndax askanu Lóot laa sédd réewum Ar.»

Ku dul doomu yoon du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji. Ku askanoo ci moom it, ba ca fukkeelu maas ga, du bokk ci ndajem gëmkati Aji Sax ji.

¶ Nayas Amoneen ba moo dikkoon, gaw dëkk ba ñu naan Yabes ca Galàdd. Waa Yabes gépp wax ak moom, ne ko: «Ngalla digool ak nun jàmm, te nu nangul la.»

¶ Gannaaw loolu Nayas buurub Amoneen ña dee, Anun doomam ju góor falu buur, wuutu ko.

¶ Ma gisati ci jamono yooyu ay Yudeen ñu jël jabar ci waa Asdodd ak Amon ak Mowab.

réewum Asiri it fekki leen, di dooleel askanu Lóot wa. Selaw.

«Maa dégg ŋàññi Mowab, kàddu yu ñaaw yi Amoneen ñiy ŋàññe sama ñoñ, tey damu, nara nangu seen suuf.