Genesis 10:11
TSK
Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala.
Keroog Aji Sax ji fas na kóllëre digganteem ak Ibraam, ne ko: «Askan wi soqikoo ci yaw laa jox réew mii dale ci dexu Misra, ba ca dex gu mag googee di Efraat,
Walbatikuleen dem, jàll-leen ca biir diiwaanu tundi Amoreen ña, ak mboolem réew ya mu feggool, ca joor ga, ak tund wa, ak suufu tund ya, ak Negew ca bëj-saalum, ba ca tefes ga, ca réewum Kanaaneen ña, ak Libaŋ, ba ca Efraat, dex gu mag ga.
Keroog ñaar fukki fan ak ñeent ci weer wi jëkk ci at mi, maa nga ca tàkkal dex gu mag gi ñuy wax Tiigar.