TSK

TSK · Genesis 2:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?»

Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?»

saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf, si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»

Ndax ci ñoom la Aji Sax ji noon dee rekk lañuy def ba jeex ca màndiŋ ma. Kenn desu ca, ku dul Kaleb doomu Yefune, ak Yosuwe doomu Nuun.

¶ Kon nag gis ngeen ko: Teg naa fi seen kanam, bés niki tey, dund ak mbaax, teg naa fi seen kanam, ndee ak loraange.

Sóol ne ko: «Na ma Yàlla teg mbugal mu gëna tar, waaye yaw Yonatan dinga dee déy!»

Buur Sóol ne ko: «Yaw Ayimeleg kay, dee rekk mooy sab àtte, yaak sa waa kër baay yépp.»

Buur yónnee, woolu Simey, ne ko: «Xanaa giñloowuma la woon ci Aji Sax ji, àrtu la ne la: “Bés boo fi jógee dem fenn, xamal xéll ne dee rekk mooy sa àtte”? Nga ne ma: “Baax na, dinaa la déggal.”

Su ma nee nit ku bon ki: “Dee rekk ay sa àtte,” te fekk àrtuwoo ku bon ka, waxuloo lu ko waññee ca mbonam ga, ba mu mucc, ku bon kaay dee ndax tooñam, waaye bakkanam yaw laa koy laaj.

ndollant lay leblee, ab tegandaay, mu jël. Moo kii nu muy dunde? Kii kay du dund! Ak mboolem jëf ju siblu jii mu def, dee rekk mooy àtteem. Bakkanam lay gàddu.

Bu ma nee ku bon ki: “Yaw ku bon ki, dee rekk mooy sa àtte,” te yaw waxuloo ko ko, àrtu ko ngir mu wacc yoonu mbonam, ku bon kooka aw ayam mooy àtteb deeyam. Waaye bakkanam, yaw laa koy topp.

Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.

Xanaa xamuleen ne képp koo jébbal sa bopp, nangul ko, ab jaamam nga? Yaar ngeen diy jaam, bàkkaar di seen sang, jëme leen ci ndee; mbaa ngeen déggal Yàlla, mu jox leen àtteb ñu jub.

man nag, ma dee. Kon ndigalu yoon wi wara jëme ci ag dund, moom ci boppam moo ma mujj jëme ci ndee.

Noonu nit bokke ci Aadama, ba tax ñépp di dee, noonu la ñépp mana bokke ci Almasi, ba tax ñu dundalaat leen, ñoom ñépp.

¶ Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alkànde ñeel na képp ku saxoowul mboolem digal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe.»

te lépp lu ñu wone ci ag leer, di ag leer. Moo tax ñu ne: «Yaw miy nelaw, yewwul, dekkil, Almasi leeral la.»

Ku ci nekkewul lu moy bànneexu bakkanam nag, ndee luy dox la.

Ndokkle ak sellnga ñeel na ñi séddu ci ndekkite lu jëkk li! Ñooñu, ñaareelu dee gi manalu leen dara. Ñooy doon it sarxalkati Yàlla ak Almasi, te ñooy nguuroondoo ak Almasi junniy at.

waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»