TSK

TSK · Genesis 2:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”»

Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.»

Mooy garabu gudd fan ci ku ko jàpp, di mbégtey ku ca ŋoy.

Maay neenal firndey maaman, dofloo gisaanekat. Maay weddi fóore, def xam-xamam mu dig ndof.

Du genn garabu seedar ca toolub Yàlla, gu ko yóbbuloon dara, du garabu sippar yu ko niruy car, mbaa garabu palataan bu ko niruy bànqaas. Du genn garab ci toolub Yàlla, gu taaroo ni moom.

Ana kan nga neexool teddngaak daraja ci biir garabi Àjjana? Ndaxam dees na la booleek garabi Àjjana, tàbbal xóotey suuf. Yaay goorandook yéefar, yi saamar tëral. Loolooy deminu Firawnaaki gàngooram. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»

Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may nga lekk ci garabu dund gi ci Àjjana, toolub Yàlla.

¶ «Ndokklee yeen ñi fóot seeni yére, ngir saña lekk ci garabu dund gi, jàlle bunt yi, dugg ci biir dëkk bi.