TSK

TSK · Genesis 21:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Yàlla ne ko: «Waaw, waaye du tere sa soxna Saarata amal la doom ju góor, nga tudde ko nag Isaaxa. Dinaa fas ak moom sama kóllëre, mu wéy ba ciy sëtam ba fàww.

Ibraayma ne ko: «Da di dama noon, amul kenn ci réew mii ku ragal Yàlla, te dees na ma rey ndax sama soxna.

Doom yu góor, ya mu am aki nekkaaleem, mu may leen alal ca ba muy dund, ba noppi yebal leen penku, ñu sanci ca réewu penku, ba sore doomam Isaaxa.

¶ Ba loolu amee Esawu ànd aki soxnaam, aki doomam yu góor ak yu jigéen, ak waa këram ñépp, jiital géttam ak juram gépp, yóbbaale mboolem alal ju mu amoon ca réewu Kanaan, daldi sanci meneen réew ngir sore rakkam Yanqóoba.

Moo tax dootuloo ab jaam, doom nga. Gannaaw doom nga nag, boroom cér nga it fa Yàlla sa baay.

Loolu moo am ngir ab cér bu dul yàqu, du sobewu, du seey, cér bu dence fa asamaan ñeel leen,