TSK

TSK · Genesis 23:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kàddug ñaari seede ba ñett nag, ci lees di reye ki ñu wara rey, waaye deesu ko rey ci kàddug benn seede.

Ruth 4:1 TSK

¶ Ci biir loolu Bowas dem ba ca bunt dëkk ba, toog fa. Noonu rekk mbokk ma mu waxoon ne su dee jotaat, moo ko ci gëna yey, daldi fay jaare. Mu woo ko ne ko: «Diwoo, kaay fii, toog tuuti.» Mu dikk, toog.

Ruth 4:9 TSK

¶ Ba mu ko defee Bowas wax ak mag ña ak ñeneen ña ñépp, ne leen: «Seedeleen bésub tey ne jënd naa ci Nawmi mboolem alalu Elimeleg ak mboolem alalu Kilyon ak Malon,

¶ Ba mu ko defee Arawna séen Buur, mu ànd aki jawriñam, jëm ca moom. Mu génn sujjóotal ko, dëpp jëëm ca suuf,

«Xoolal, Anamel doomu Salum sa baay bu ndaw a ngooguy ñëw, naan la nga jënd toolam ba ca Anatot, ndax yaa ko saña jotaat.»