TSK

TSK · Genesis 23:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.»

Mooy xuntim bàmmeel ba ca biir tool, ba ca Magpela, te jàkkaarloo ak Mamre ca réewu Kanaan, di tool, ba Ibraayma jëndoon ca Efron, Etteen ba, ngir def ko bàmmeel.

¶ «Suuf si deesu ko jaay, mu wel fàww, ndax maay Boroom suuf si, yeen ay doxandéem ngeen fi, yu ma fi dëkkal.

Job 30:23 TSK

Xam naa xéll ne ci dee nga ma jëme, te mooy kërug ndajem képp kuy dund.

Ba bànni Israyil dee ñu néew, diy doxandéem ca réew ma,

Ku giir téeméeri doom, dund ati at, ak lu at ya bare bare, su bégewul teraanga ja mu am te amul njégu bàmmeelam sax, kooku lumb wu tuuroo ko tane.

Su boobaa pënd dellu suuf, na woon; bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.

Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba.

¶ Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.