¶ Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur.
TSK
TSK · Genesis 24:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf!
Léegi nag waatal ma fii ci Yàlla ne doo ma wor mukk, man ak samay doom, ba ci samay sët. Waatal ma ne noonee ma rafetoo woon ak yaw, ni ngay rafetoo ak man, maak waa réew, mi nga dal.»
¶ Esawu am na ñeent fukki at, jël na soxna ku ñuy wax Yudit, muy doomu Beeri, miy Etteen, jëlaat Basmat doomu Elon, miy Etteen.
¶ Ci kaw loolu Isaaxa woo Yanqóoba, ñaanal ko, jox ko ndigal lii ne ko: «Bul jël ci jigéeni Kanaan,
Léegi ñëwal rekk, ñu fasante kóllëre maak yaw, te seede dox sunu diggante maak yaw.»
Foofa nag Yuda gis fa senn as ndaw, su doon doomu Kanaaneen bu tudd Suwa, mu jël ko soxna.
¶ «Buleen tudd seen turu Yàlla Aji Sax ji ci neen, ndax Aji Sax ji du ñàkka topp kuy tudd aw turam ci neen.
¶ «Li ma leen wax lépp sàmmleen ko, te turi yeneen yàlla, buleen ko tudd; bumu jibe sax seen gémmiñ.
¶ «Buleen giñe sama tur lu dul dëgg, di teddadil seen turu Yàlla. Maay Aji Sax ji.
Seen Yàlla Aji Sax ji, ragal-leen ko. Moom ngeen di jaamu, te aw turam ngeen di giñe.
¶ Seen Yàlla Aji Sax ji moom ngeen di ragal, te moom ngeen di jaamu. Moom ngeen di ŋoyu, te aw turam ngeen di giñe.
Daawuda ne ko: «Ndax man nga maa yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yooyu?» Mu ne ko: «Giñal ma ci Yàlla ne, doo ma rey, te doo ma delloo ca sama sang; kon dinaa la yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yi.»
¶ «Yaw Aji Sax ji, yaw kenn yaa sàkk asamaan yi, ba ca asamaan ya gëna kawe ak seen gàngoor yépp, ak suuf ak lépp li ci kawam, ak géej ak li ci biiram lépp. Yooyu yépp, yaay ki leen di may bakkan, te gàngoori asamaan, yaw lañuy sujjóotal.
Yal nangeen barkeeloo Aji Sax ji, ki sàkk asamaan ak suuf.
Yeen waa kër Yanqóoba, dégluleen; yeen ñi ñu wooye turu Israyil, yeen ñi bawoo bëti ndoxi Yuda, di giñe turu Aji Sax ji, yeen ñiy sàbbaal turu Yàllay Israyil te dëgg ak njekk taxul,
xanaa di waate Aji Sax jiy dund, ci dëgg ak njub ak ngor, kon xeet yi di barkeeloo Aji Sax ji, di ko sagoo.»
Waaye bu ñu royee ba roy sama ñoñ, di jëfe ni sama ñoñ wara jëfe, di giñe sama tur naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund,” na ñu daan royloo sama ñoñ, ba ñuy giñe Baal, tuur mi, su boobaa ñu sampu fi sama digg ñoñ.
ak ñiy sujjóotal ci kawi taax gàngoori biddiiw yi, ak ñiy sujjóotal aka giñal Aji Sax ji tey giñe Milkom, yàllantu ji,
¶ Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?