TSK

TSK · Genesis 24:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Firawna nag topptoo Ibraam bu baax ndax moom, ñu may ko ay gàtt ak ay nag, ay mbaam yu góor, ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, ak ay mbaam yu jigéen aki giléem.

¶ Ibraayma guddoon na fan, ba màggat lool, te Aji Sax ji barkeel ko ci lépp.

¶ Gannaaw loolu Isaaxa bey ca réew ma, góob ca at ma lu tollook téeméeri yoon la mu ji woon, ndax Aji Sax ji da koo barkeel.

Job 1:3 TSK

Alalam juróom ñaari junniy (7 000) gàtt la woon, ak ñetti junniy (3 000) giléem, ak juróomi téeméeri (500) lëkkey nag yuy rijji, ak juróomi téeméeri (500) mbaam yu jigéen, ak jaam yu bare lool. Góor googu daal moo ëppoon daraja ca mboolem waa penku.

Moo may tàggat ngir xare, may bank xalag xànjar.

alal ak koom am sa kër, sag njekk sax dàkk.

Woyofal te ragal Aji Sax ji, am alal, gudd fan ak daraja.

Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.