¶ Ci kaw loolu Yàlla barkeel Nóoyin aki doomam ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina.
TSK
TSK · Genesis 24:60
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dinaa ko barkeel, may la ak moom doom ju góor; dinaa ko barkeel moos, ba mu jaboote xeet yu bare, te ay buuri xeet sax dinañu soqikoo ci moom.»
Yal na la Yàlla Aji Man ji barkeel, nga jaboot lool te sa giir yokku, ba sos ay mboolooy askan.
Ma ngay ñaanal Yuusufa. Mu ne: «Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon, moom Yàlla, ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii,
Sañ ngeen leena donale seen doom yi leen di wuutu, ñu doon seen ngàllo seen giiru dund. Ñooñu sañ ngeen leena def ay jaam, waaye su dee ci seen diggante, yeen bànni Israyil, buleen di soxorante ci biir kilifteef.
¶ Waa pénc ma mépp ak mag ña nag ne ko: «Noo ko seede. Yal na Aji Sax ji def ndaw siy séysi sa kër, mel ni Rasel ak Leya, ñoom ñaar ñi giir waa kër Israyil gépp. Yal nanga tekki ci digg Efrata te amu tur ci Betleyem.
dexu sawara di wal, balle fa kanamam. Junniy junnee nga koy jaamu, mboolooy mbooloo dar ko. Waa pénc ma toog, téere ya ubbiku.